Ndenkaane

Taaw djéguessil, taaw dékeul dékeul say nopp-pi xel té ta-taane
Ndenkaané biy téy say noone euleuk douñou rétane
Kaddu yu moudjou yima nam deuy
Moy guedjou xam xam di sa dieuriñe di fégn
Taaw taaw li bayi fassa wakh boulko rakh
Moy yonou deugg bifi xala sakh
Def nako teunk nott ko cii niéte (3) teerés
Deuxeuñe nassi lepp louy ndigueul aki téré
Bo goré nanga ko saameu bagneko rééré
Teeré bitchi ndieuk moy, moytoul banekhou moye
Mba bénène boulna meuneu yaubé gathié
Ndaxam mbeur you beuri silañou lène wathié
Teeré bitchi topeu moy taaw bo faarlu daw taayel ndèyou niaak
Euleuk nga meuneu kérou far dakk
Nguir bala noflay di taw rek thiono séwett
Niémel thiono ak khiff wéteuliko weet. (Taaw)
Wéteuliko YALLAH tékoy yegg fepp sa wét
Niétélou teeré bi moy…Alakhira
Déko sauralé té xam ni li cii Aduna wessu woul la fa laxira
Sa Borom missal nalako cii Kamil Al-Quran, ci Zabur, Tawret (Torah) ak Injil (Evangile)
Taaw Na nga nango mougne naatu yi, nangoul mougne naatu yi, nangoul mougne naatu yi
Moytou galangkor yi bagna diawalé yone yi
Ndaxam todial nala taaxou Aduna
Yone wofi nama awatt na melni Aduna
Djitoul taaw say rakk topeu sa nguinaw
Xalale nalène yone yi ba noppi yone wi ngène wara aw
Kou bott bouki nak xathie mboow la. (Taaw)
Kone nangay deuké nangou dina takh niou nawla
Deugg deg-dégueula likay mayé yone ba ngay awla
Ko tchi beug yarr gueune ko yarrou
Ko tchi beug yémalé gueune ko maandou
Biss naka tay taaw yadi Baye yaw yadi Baye
Batakh nga wara yaatu teudé ndiaxanay
Biss naka tay taaw sama djane wathiena
Lepp louma warone wathiouna
Djeufna, Bindeuna, tabakh na ba-fi
Sama nguinaw diayantel bamou sakh fi
Xalé yi yéneu nakk dégueul lène sèn makk
Délène makoy xolé té mouy sènip sakk
Té xamné soudone deugg sama thiobaré
Ma dessate fi gougué lène ay att you bari
Waayé Djam ak pekhem YALLAH ak ndogalam
Kone taaw say rakk ngok sèni mouthie ak sen ndam
Sama Appeu matena tay lak ande ak Jante bi soow
Na ngène ma nianale cii barké doumou Mame Diarra Bousso
Baye Laye, Baye Niasse, Maodo Borom Tivaone,
Cheikh Saad borom Nimzat bou Kouneta Ndiassane
Niom gnignou nampale Iman, Islam ak Ikhsane
Dom limo done samay Kaddu you moudjou
Bolo lène Bolo lène ….Bénno bania doni woudjou
Dom fi la sama Galou doundou nameu téré
Keur nga ngok, Yone wa ngok Yallah nama lepp…..